Joxe nañu fi ay xibaar si wallu liy firndeel feebar yiy gën a wallaate. Fac ko si lu gaaw am na solo lol. Dina la aar si sa wergi yaram te dina tax do wall nit ñi.
Joxe nañu fi ay xibaar si wallu liy firndeel feebar yiy gën a wallaate. Fac ko si lu gaaw am na solo lol. Dina la aar si sa wergi yaram te dina tax do wall nit ñi.
Sudee liy firndeel feebar bi walla su sa yaram neexul, wooteel Medic-Help.
Sëkkët day wone feebar yu bare. Si lu gën a bare day wone soc. Yensaa day firndeel feebar buy wallaate.
Demal si Medic-Help soy sëkkët yensaa walla di sëkkët bu bax walla si ak diir bu yag walla di sëkkët ak sa denn.
Sa temperaatiiru yaram su yokkoo rek kon yaram bi neexul. Mën na wone ay feebar yu wuute.
So feebare demal seeti Medic-Help.
Sa su yaram bi neexul gawal dem si Medic-Help.
Naanal tuuti ndox walla ataaya te moytu liggey yu diis.
Yoon la di ñaak lu baré si gudi jamono taŋay. Diŋa ñaak tamit su lal bi tanŋee. Waayé so de ñaak lu baré si gudigi si temperatir yu jaar yoon mën na wone ap feebar buy wallaaté.
So feebaré bole si di ñaak gudi ak puwa bu wañeku, demal seeti Medic-Help.
Ñaak gudi mën na wone ay feebar yu wute. Mën na wone mbiir yi:
Su yaram bi amee ay picc, picc yu xonk walla ay tup tup di feeñ yensaa si yaram bi, walla yaram bi ñiagass teksi ay eer walla muy xasan. Lii mën na firndeel buy wallaate.
Su yaram bi amee ay picc walla muy xasan demal seeti Medic-Help.
Dagg-dagg, xosi walla matt-matt mën na gaañ yaram bi ba indil ko góom. Ay góom yu dul gaaw a wër jarna topattoo bu baax.
So amee ay góom si yaram bi demal seeti Medic-Help.
Góom yuy feeñ ay gañu gañu mokoy waral. Sudé du wër du bax, li mën na firndeel:
Su fekké ni biir bi day gur guri lup eep ñiet yoon si bes bi, walla su fekke ni sa pup yi da ndoxé, li biir buy daw la. Mën na wone ap feebar buy wallaate.
Sa biir sudee daw demal seeti Medic-Help.
Naanal tuuti ndox walla ataaya.
Dey faral di raxas sa loxo ŋir moytu di wall nit yi.
Biir buy daw mën na wone feebar yu wute. Mën na firndeel si mbiir yi:
Waccu mën na firndeel feebar yu wute. Waccu mën na firndeel tamit feebar buy wallate.
So dee waccu demal seeti Medic-Help.
Naanal tuuti ndox walla ataaya.
Dey faral di raxas sa loxo ŋir moytu di wall nit yi.
Waacu mën na firndeel feebar yu wute. Waacu mën na firndeel tamit feebar buy wallaate:
So amee ay jaffe-jaffe nelaw guddi yu bari walla di tiit si lo mënula nettali, li mën na wone feebaru xel. Ay metit yu amul dara lu ko waral lu kenn mënul gis dakoy joxe tamit.
Soodul nelaw bu bax walla ŋa am ay mettit yoo menu la nettali, woowal Medic-Help.
Jaffe-jaffe nelaw walla di tiit si lo mënula nettali, walla ay metit yo mënula wax mën na wone feebaru xel. Mën na firndeel si mbiir yi:
Si këyit bi di ŋa gis ay xibaar si walla feebar yiy gën a wallaate.
Wor na ne am na ay yeneen firnde yu bare. Sa yaram su neexul walla ŋa am lo bëgg a laaj si sa wergi-yaram, demal seeti Medic-Help.