Ci dalu-web bi, njiitu Suisse ci wallu wergi-yaram (FOPH) ñoo joxee xibaar yi ci wallu feebar yiy wallate ak nooy aare sa bopp si feebar yi. Joxe nañu tamit ay xibaar si nooy amee serwis yi jëm si wallu toppatoo wergi-yaram.
Dalu-web bi dañu ko defar ŋir kiy wut asil si barabu dallukay yi ak ci sàntar yi ak ci sàntar biy dalal daw-lakku yi. Seen yitte mooy feebar yiy wallaate ŋir aar daw-lakku yi ak waa góx bi si wallaate yi ak ŋir wergi-yaram sax si góx bi.
Aji-Dugalkat ci dalu-web bi:
Federal Office of Public Health FOPH
Public Health Directorate
Department for Sexually Transmitted Diseases
Schwarzenburgstrasse 157
3003 Bern
Ci bisu: saawier 2018