Ndax am ŋa feebar bulay soonal lu yaag? Ndax di ŋay di faral di jël garab? Ndax mës ŋa faju lopitaal si sa gox walla bi ŋay daw di geen sa gox?
Feebar yi melni blennorraasi, sifilis walla klamijaa mën na wallaate si wallu sey ak jigeen. Day indi sekresioŋ, wokatu walla ak ay neewi-neewi, ilseer walla mettit si awra jigeen bi. Waayé mën ŋa ko am te firnde yi du feeñ.
Aaral sa bopp si wallu feebaru sëy yi. Deel jëfandikoo kawas soy sëy ak jigeen. Mën ŋa ko am si Sàntar bi walla ŋa jënd ko si farmasi bi walla si supermarse yi.
So amee liy firndeel feebaru sëy demal seeti Medic-Help.
Su fekkee ni wooru la ndax am ŋa benn si feebaru sëy yi so noppee leegi ci sëy ak jigeen te soloo kawas, demal Medic-Help saytu la. Bul xaar ba am liy firndeel feebaru sëy yi di door a dem.
VIH ab wirus la buy neewal liy aar sa yaram. Mën ŋa am wirus bi te do am likoy firndeel. So dul jël ay garab day newal doole sa yaram baŋa feebar. Lii miŋi tudu Sida.
Feebar bi si dereet lay wallaate soodee sëy ak jigeen te solo kawas, walla di jefandiko sereeŋal bu setul walla ndey ak dóom ji si biiram. So ame wirus bi, mën ŋa wall nit yi te du am lenn luy firndeel ni am ŋa ko.
VIH/SIDA kenn mënu ko faj. Waaye di jël garab day waññi doole wirus.
Aaral so bopp si VIH/SIDA. Deel jëfandikoo kawas soy sëy ak jigeen. Mën ŋa ko am si sàntar bi walla ŋa jënd ko si farmasi bi walla si supermarse yi.
Deel jëfandikoo saa su nekk sereŋal bu set wecc bu kenn mësul jëfandiko sooy pikiiru ŋir mooytu wall nit yi.
Demal Medic/Help saytu la su la woorul ne am ŋa VIH/SIDA walla deet, walla ab feebaru sëy so noppee leegi ci sëy ak jigeen te soloo kawas. Bul xaar ba am liy firndeel feebar bi di door a dem.
Nit yi am Tiberkiloos da ñuy sëkkët si lu tolu ñetti ayu-bis, seen yaram du neex, di ñaak guddi walla seen yaram di waññeeku. Wallaate tiberkiloos mi ngi am su nit ki wer yaram nooyee ngelaw bi jogee si sëkkëtu nit yu am tiberkiloos.
Tiberkiloos feebar bu bonn la. Waaye suñu teelee gis feebar bi faj ko dina mën na nekk. Paj mi mën na am juróom-benn weer.
So amee bepp firnde tiberkiloos, walla ŋa am sa faju tiberkiloos walla ŋa am sa lëkaloo ak ku am feebar bi, demal seeti Medic-Help.
Sanŋara, sinebar walla yenn xeetu sinebar yi day tax ŋa xër te day yakk sa yaram. Baayil jëfandiko sinewar.
Mën ŋa jelee feebar si wallu dereet so dee jëfandiko sinewar si sereŋal. Manam su fekkee ne sereŋal yi am na ku leen mës a jëfandikoo.
So mënul baayi sinebar deel jëfandiko kon ay sereŋal yu set wecc yu kenn mësul jefandiko ŋir moytu ñu wall la.
Xër mën nañuko faaj walla waññi ko. Woowal Medic-Help.
Jaar-jaar bu metti walla teg mettit – lu melni xeex, daw, mettital ak saku jigeen mën a indi feebaru xel walla yaram. Naan sangara bu bari walla xër si yenn mbir yi dakoy indi tamit.
Ñu bari si ñiko am jafe na leen lool di wax feebaru xel la. Baayi si xel bax na lol teksi diko faj ni ŋay fajee yeneen feebar yi.
Li mën a firndeel feebaru xel bokna si ñakk nelaw si ab diir gu yàgg, di gent lu doy waar, ay mettit yoo mënul tektal walla ay yeneen jafe-jafe.
Feebaru xel mën nañ ko faj. Wowal Medic-Help.
Difteri ab feebar la biy nek si wallu bakkan walla si yaram. Dafa am ñaar: difteri si baat ak difteri si yaram.
Ñi am difteri si baat seen baat day metti, seen yaram du neex te suñuy jalale lekk si gemiñ day meti. Liy gën a firndeel difteri si yaram mooy góom yi dul gaaw a wer. Mën ŋa aar sa bopp si difteri so ñakkoo.
So am luy firndeel difteri walla sa dóom, demal si Medic-Help.
So amagul difteri, ñiakko go. Demal si Medic-Help.
Waga sa yaram bi yep lay lal. Ap parasisit moy gass sa yaram bi.
Daŋay wokatu, yaram bi day am ay tup tup ak ay picc, day gën a fes si awra , baram yi,si poignet yi ak articulation yi, si sufu loxo yi ak si ween yi.
Feebar bi mi ŋi wallaate ñiari nit lalanté.
So amee luy firndeel waga walla sa dóom, demal si Medic-Help.
Sa estoma bi su tanngee ak butit yi, so bëggee waccu, soy waccu teksi biir buy daw, teksi yaram bu neexul ak mettit si estoma bi. Ku am feebar bi da ŋay ñakk ndox bu bari si diir bu gàtt.
So amee luy firndeel waga walla sa dóom, demal si Medic-Help.
Naanal tuuti ndox walla ataaya.
Del faral di raxas say loxo ak saabu ŋir mooytu wall nit yi.