Kepp ku nekk Suisse am ŋa sañ-sañ si ñu tappatoo sa wergi-yaram. Si sàntar bu asil bi, demal Medic-Help si lu njëk so amee firnde biy joxe feebar.
Njëkal a dem si dóktoor matale bi
Si Suisse sa dóktoor matale molay njëkka saytu so amee feebar walla laksidaŋ. Nañu la toppatoo te su ko jaree nañu la tektal ab lopitaal walla ab fajkat bu xarañ.
Dóktoor matale bi su xame ki feebar ki ak li si ginaaw feebar gi ci wallu wergi-yaram am dina ko mën a toppatoo bu baax. Kon deel dem saa su ne ci sa dóktoor matale bi.